1 Coríntios 10

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Bokk yi, bëgguma ngeen umple li daloon sunu maam ya. Ñoom ñépp niir wa tiimoon na leen, te ñoom ñépp jàll nañu géej.
1 Pois não quero, irmãos, que ignoreis que nossos pais estiveram todos debaixo da nuvem, e todos passaram pelo mar;
2 Sóobu nañu ca ndoxu géej ga ak ca niir wa, ba bokk noonu ci Musaa.
2 e, na nuvem e no mar, todos foram batizados em Moisés,
3 Ñoom ñépp bokk nañoo lekk ñam wa Yàlla joxe,
3 e todos comeram do mesmo alimento espiritual;
4 naan naan ga mu joxe, ndaxte ñu ngi doon naan ca xeer, wa leen doon gunge, te xeer woowa Kirist la woon.
4 e beberam todos da mesma bebida espiritual, porque bebiam da pedra espiritual que os acompanhava; e a pedra era Cristo.
5 Teewul ñi ëpp ci ñoom neexuñu woon Yàlla, ba mu fàddoon leen ca màndiŋ ma.
5 Mas Deus não se agradou da maior parte deles; pelo que foram prostrados no deserto.
6 Mbir yooyu ay misaal lañu, yu nuy artu, ngir benn bëgg-bëgg bu bon bañ noo jiital, na mu leen jiitale woon.
6 Ora, estas coisas nos foram feitas para exemplo, a fim de que não cobicemos as coisas más, como eles cobiçaram.
7 Buleen jaamu ay xërëm, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon. Ndaxte Mbind mi nee na: «Mbooloo mi dafa toog, di lekk ak di naan, ba noppi ñu jóg di mbumbaay.»
7 Não vos torneis, pois, idólatras, como alguns deles, conforme está escrito: O povo assentou-se a comer e a beber, e levantou-se para folgar.
8 Bunu njaaloo, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax ñaar fukki junni ak ñett ci ñoom dee ci benn bés.
8 Nem nos prostituamos, como alguns deles fizeram; e caíram num só dia vinte e três mil.
9 Bunu diiŋat Kirist, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe, ba ay jaan màtt leen, ñu dee.
9 E não tentemos o Senhor, como alguns deles o tentaram, e pereceram pelas serpentes.
10 Buleen xultu, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax Malaakam bóomkat bi rey leen.
10 E não murmureis, como alguns deles murmuraram, e pereceram pelo destruidor.
11 Mbir yooyu leen daloon misaal la ci nun, te bind nañu ko ngir artu nu, nun ñiy dund ci jamono jii lépp mat.
11 Ora, tudo isto lhes acontecia como exemplo, e foi escrito para aviso nosso, para quem já são chegados os fins dos séculos.
12 Kon nag kiy naw sa doole, ba yaakaar ne taxaw nga, moytula daanu ci bàkkaar!
12 Aquele, pois, que pensa estar em pé, olhe não caia.
13 Benn nattu dabu leen bu wuute ak yi dal nit ñépp. Te sax Yàlla kuy sàmm kóllëre la, te du nangu nattu bi wees seen kàttan, waaye cib nattu dina leen ubbil bunt bu ngeen mana rëcce, ba ngeen man koo dékku.
13 Não vos sobreveio nenhuma tentação, senão humana; mas fiel é Deus, o qual não deixará que sejais tentados acima do que podeis resistir, antes com a tentação dará também o meio de saída, para que a possais suportar.
14 Looloo tax, sama soppe yi, nangeen daw xërëm yi.
14 Portanto, meus amados, fugi da idolatria.
15 Maa ngi wax ak yéen ñi am xel. Kon seetleen li ma leen wax.
15 Falo como a entendidos; julgai vós mesmos o que digo.
16 Kaas bu yiw bi tax nuy gërëm Yàlla, ndax du wone sunu booloo ak deretu Kirist? Mburu mi nuy damm, xanaa du dafay wone sunu booloo ak yaramu Kirist?
16 Porventura o cálice de bênção que abençoamos, não é a comunhão do sangue de Cristo? O pão que partimos, não é porventura a comunhão do corpo de Cristo?
17 Ndegam benn mburu rekk a am, kon nun ñépp lu nu baree bare, menn mbooloo lanu, ndaxte bokk nanu menn mburu mi.
17 Pois nós, embora muitos, somos um só pão, um só corpo; porque todos participamos de um mesmo pão.
18 Seetleen ci bànni Israyil. Ñiy lekk sarax si ñu rendi, ndax booloowuñu ak Yàlla ji ñu jagleel sarxalukaay ba? Ahakay!
18 Vede a Israel segundo a carne; os que comem dos sacrifícios não são porventura participantes do altar?
19 Li may wax, lu muy tekki? Ndax yàpp wi ñu jagleel xërëm yi dafay dara? Walla xërëm yi dañuy dara?
19 Mas que digo? Que o sacrificado ao ídolo é alguma coisa? Ou que o ídolo é alguma coisa?
20 Déedéet! Waaye sarax yi xërëmkat yi di rendi, ay rab lañu ko jagleel; jagleeluñu ko Yàlla. Te man bëgguma, ngeen booloo ak rab yi.
20 Antes digo que as coisas que eles sacrificam, sacrificam-nas a demônios, e não a Deus. E não quero que sejais participantes com os demônios.
21 Manuleena naan ci kaasu Boroom bi, naan ci kaasu rab yi. Manuleena sukk ci reerub Boroom bi, sukk ci reerub rab yi.
21 Não podeis beber do cálice do Senhor e do cálice de demônios; não podeis participar da mesa do Senhor e da mesa de demônios.
22 Walla boog ndax danuy jéema gillil meru Boroom bi? Xanaa noo ko ëpp doole?
22 Ou provocaremos a zelos o Senhor? Somos, porventura, mais fortes do que ele?
23 Dafa am ñu naan: «Lépp lanu sañ.» Waaw, waaye du lépp a baax ci nun. «Lépp lanu sañ,» waaye it lépp du yékkati ngëm.
23 Todas as coisas são lícitas, mas nem todas as coisas convêm; todas as coisas são lícitas, mas nem todas as coisas edificam.
24 Bu kenn seet njariñam rekk, waaye nay seet njariñul moroomam.
24 Ninguém busque o proveito próprio, antes cada um o de outrem.
25 Man ngeena lekk lépp lu ñuy jaay ca ja ba, bañ cee boole ay laaj ngir dalal seen xel.
25 Comei de tudo quanto se vende no mercado, nada perguntando por causa da consciência.
26 Ndaxte Mbind mi nee na: «Àddina ak li ci biiram lépp, Boroom bi moo ko moom.»
26 Pois do Senhor é a terra e a sua plenitude.
27 Ku xamul Yàlla nag, bu leen wooyee aw ñam këram, te ngeen nangoo dem, lekkleen lépp lu ñu leen dëj, baña laajte dara ngir dalal seen xel.
27 Se, portanto, algum dos incrédulos vos convidar, e quiserdes ir, comei de tudo o que se puser diante de vós, nada perguntando por causa da consciência.
28 Waaye bu leen kenn nee: «Lii sarax la, bu ñu jagleel xërëm yi,» suurleen ko ndax ki leen ko xamal, ngir xel mu dal.
28 Mas, se alguém vos disser: Isto foi oferecido em sacrifício; não comais por causa daquele que vos advertiu e por causa da consciência;
29 Waxuma sa xel yaw, waaye xelu keneen laay wax.
29 consciência, digo, não a tua, mas a do outro. Pois, por que há de ser julgada a minha liberdade pela consciência de outrem?
30 Su ma lekkee dara di ci sant Yàlla, lu tax ñu may wax lu ñaaw, fekk sant naa ci Yàlla?»
30 E, se eu com gratidão participo, por que sou vilipendiado por causa daquilo por que dou graças?
31 Kon su ngeen di lekk walla ngeen di naan, walla lu ngeen mana def, defleen lépp ngir màggal Yàlla.
31 Portanto, quer comais quer bebais, ou façais, qualquer outra coisa, fazei tudo para glória de Deus.
32 Buleen def dara lu mana fanq ngëmu Yawut yi walla ñi dul Yawut walla mbooloom Yàlla.
32 Não vos torneis causa de tropeço nem a judeus, nem a gregos, nem a igreja de Deus;
33 Noonu laay def man ci sama bopp: damay wuta neex ñépp ci lépp. Wutuma lu may jariñ, waaye luy jariñ ñu bare laay wut, ngir ñu mucc.
33 assim como também eu em tudo procuro agradar a todos, não buscando o meu próprio proveito, mas o de muitos, para que sejam salvos.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar 1 Coríntios 10, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.